(Vidéo) Serigne Modou Kara dédie un poème au nouveau Khalife des mourides, Regardez!

(Vidéo) Serigne Modou Kara dédie un poème au nouveau Khalife des mourides, Regardez!

Serigne Modou Kara Mbacké a repris sa plume! Le Général de Bamba a écrit un poème qu’il a dédié au nouveau Khalife des mourides, Serigne Mountakha Mbacké. Regardez!

 

 

SËRIÑ MUNTAQÂH
 
Bismi LÂHI ar RAHMÂNI ar RAHÎMI
Wa salla LÂHU allâ SEYDINÂH MUHAMMADIN wa sallama taslîman
Hâzihil qasîdah min QÂDIMI RASÛLI LÂHI illal QALÎFAH-al-MUNTAQÂH
KI moom jamono, ñëw na dem
Ñi KO doon wuutu, ñëpp a dem
Ñaar i Sëtam yi mujj’ee dem
Ki mujju ak kañ tudd’ee baayam
 
Képp ku jooyoon, na nga reeh
Te ñaan KU-TEDD-KI di reeh
Ku kay bégée ba tax ngay reeh
Looy def di nga ca jëlée ndam
 
Ma ñëw ci SËRIÑ-MUNTAQÂH
Ma fawqa Ñoñ Waa-Fâqû
Jotaay bu beesam a fawqa
Jotaayu Ñoñ Waa-Fâqû
 
Izrâfîl ci Développement
Jot na Ndigal ci MARIAMÂH
Jibrîl a ko wax mbir ma
Na Muntaqâh am développement
 
Zan-Jayâ-Hîlu Malâkah
Jot na Ndigalu BUUR-YÂLLAH
Ci di munna ca kay tal a
Dox di yàxx ba du tal a
 
Yàxxati ndax Sëriñ-MUNTAQÂH
Moo dònn ñëpp, Irtaqâh
Yim boole ëpp, moo fawqu
Lépp lu baax, mooy Muntaqâh
 
Dañ ko tànn, di ko élire
Ku am gòpp wutal ileer
Tool i àllarbam di na riir
Ci réew mi ba ñëpp di ser
 
Dey doon àllarba’y BAMBA-Fépp
Dugub, aareen ci fépp-fépp
Waa-Kër KU-TEDD-KI ci ñëpp
Lañ cay dundal, dara du ëpp
 
AL MUNTAQÂH mooy MUSTAFÂH
Di BÂRAQALITT, di MUJTABÂH
Tur wu ci ne, siròom
Da ngaa ligéy ba am Ngëram
 
Ci laa jëlée Irham bi may waxee
KU-TEDD-KI du ma ci naxe
Ñeme wu ma ko, du ay pexe
Kese, MOO di maye texe
 
Jaayaante na ñu, nang ka nangu
MUSTAFÂH-AFSA digle na ko
Moo neh la woon, kii jàppal ma ko
Moo tax saa mbubu, ma summi ko
 
Man it, ma jàpp’aat sama bòpp
Def buum ci sama baat u bòpp
Raam’aat, tey summi sama mbub-
Uy darajah, fas la yéene’y tòpp
 
Murîd, Ndigal da kay jëfée
Lum man a doon mu kay jëfee
Lum jafe-jafe
Di bay sonjaan tey naan kafe
 
0 COMMENTAIRES
    Publiez un commentaire

    Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *